Soppey Sëriñ Saaliwu kutiir

Soppey Sëriñ Saaliwu kutiir daouda Diagne

Fermé définitivement.

assalaamu xalykom warahmatul Laahi wabarakaatuhuu yen sope s sallioucouture yi dallen ak Jamo
fi sen kar la lou gën soxla ci walou ñaw amna fi latt ko rek ñou joxla ko inssallah

Commune de Tivaouane : Dr Moustapha Diop Président du mouvement Jëfal Askan Wi rejoint la coalition Diomaye Président
08/03/2024

Commune de Tivaouane : Dr Moustapha Diop Président du mouvement Jëfal Askan Wi rejoint la coalition Diomaye Président

Docteur Moustapha Diop Jëfal Askan Wi nee na : " Jalgati Nasonaal bi Maki Sàll woote demu ca yablewul ", na leer.
26/02/2024

Docteur Moustapha Diop Jëfal Askan Wi nee na : " Jalgati Nasonaal bi Maki Sàll woote demu ca yablewul ", na leer.

Ku nekk a ngi ne tekk tey déglu kilifaam nun it noo ngi ne tekk di la dégglu foo nu joxoñ nu jëm. Jëfal Askan Wi du bool...
07/01/2024

Ku nekk a ngi ne tekk tey déglu kilifaam nun it noo ngi ne tekk di la dégglu foo nu joxoñ nu jëm. Jëfal Askan Wi du boole dara aki wax jëf rekk nu gis.

Segam kër gii ya man a saytu i wayndare sakkamtumalaa ak Yàlla mi nu sàkk sàkk leen ku bàyyiwul xel ëllëg ne Yàlla di na...
07/01/2024

Segam kër gii ya man a saytu i wayndare sakkamtumalaa ak Yàlla mi nu sàkk sàkk leen ku bàyyiwul xel ëllëg ne Yàlla di na saytu say bir nitewóo !

Jaajëf jàmbaar bu dëgg doon tax a falu kenn du xàccoo ag yaw àdduna xam na ne yaa nekk ci dëgg waaye ñi ëpp ci ñiy doxal...
05/01/2024

Jaajëf jàmbaar bu dëgg doon tax a falu kenn du xàccoo ag yaw àdduna xam na ne yaa nekk ci dëgg waaye ñi ëpp ci ñiy doxal àdduna bëgguñu dëgg te, àdduna yàgg nañu fee sonal ku nekk ci ag njub, te njub rekk a wóor gisuma lu ko gën fii ak fële, te ku lii jàngalul ëlëg sam xel des na ndegam fii ci àdduna rekk lañu man a seete i wayndare sakkamtumala ak ëlëg jee nu jëm, nga xam ne lu fa waay and dees na ko seet bu dee lu baax nu fay la ko safaan ba it noonu, lii ma gis ci sunu réew mii ag ragal Yàlla a fiy bëgg a tuxu gis dëgg mu leer la nàññ nga dëgg ci sa tànk def la la neex.
Ku dul sóor bàmmeel lu la neex defal bis a ngi ñëw bob doo ko seq ak kenn, sama bopp laa ci jiiital na nu ànd ragal Yàlla tey dox ci dëgg di teg sunu lépp ci dëgg dara jaru fi dara rawati na poñeetum àddina sii.
Ma dellu jaajëfalaat la sa ndam li rëy na kawe na des nga dis gor su set wecc xamal nga nu ba nu xam yee nu ba nu ne jàrr dellu wan nu dëgg ba nu ràññee ko ba faf xammee ku ca nekk ak ku ca nekkul jaajëf yal buur gudal sa fan te may la wér te sàmm la aar musal la ci am ndog yal na Yàlla roof la mbégam ma ag muñam ga roof la kàttanam ga te àggale say mbébët yal na la Yàlla may ndam ci barkeb Alquraan aamiin.

Ndegam tubaab yee man a bàyyi xel Wolof rawati nag ab saa-wolof kañngeen di bàyyi xel Wolof ?
01/10/2023

Ndegam tubaab yee man a bàyyi xel Wolof rawati nag ab saa-wolof kañngeen di bàyyi xel Wolof ?

Regarde, suis et découvre encore plus de contenus tendance.

Gàmmu jàmm ak xeewal yu sax dàkk ak Jëfal Askan Wi.
27/09/2023

Gàmmu jàmm ak xeewal yu sax dàkk ak Jëfal Askan Wi.

Regarde, suis et découvre encore plus de contenus tendance.

17/09/2023

💢💢💢💢💢💢💢💢💢💢💢💢💢💢💢💢💢

Assalaamu halaykum bokk yi noo ngi leen di nuyu te di leen siyaare bu baax a baax di leen ñaanal jàmm ju sax dàkk te di ko sàkku ci yéen.

Ana yéen ñi bëgg a jàng seen uw làkk te dungeen ci fay dara ?
Képp ku bëgg a jàng moo xam jàngu 1 la walla jàngu 2 mbaa jàngu 3, man ngaa yëglu ndax njàng mi a ngi bëgg a door, képp koo xam ne dugal nañu la ci kippaango gi te amagóo sëñ daara bu la jàngal, man ngaa jokkoo ak sëñ Mustafaa Sëydu Jamiil Siise ci limat gii 77 549 37 37 ngir mu taxawu la ba nga am sëñ daara bu la yor.
Yéen ñi bëgg a jàng, noo ngi leen di soññ ngeen gaaw yëglu, ndax noo ngi bëgg a tàmbali njàng mi. Jaangeenjëfati.

WAX Wolof Ak Xamle.✍🏿✍🏿✍🏿
♨️♨️♨️♨️♨️♨️♨️♨️♨️♨️

Luwaa bii nu bëgg a wate, su jëllee de ku yabu dem ca kaso ya génne népp. Ndax politigsee daa gën ñeneen ñi ?
17/07/2023

Luwaa bii nu bëgg a wate, su jëllee de ku yabu dem ca kaso ya génne népp. Ndax politigsee daa gën ñeneen ñi ?

12/03/2023

*Tooñ du gàllaaj !*

_Benn waay ngii bu ñu dog loxoom ba ca mbagg ma, muy wër ci ja yi naan : "Ku bëgg a bàyyi tooñ, laaj ma." Am bis ku ne ko yaw de bis bu ne nga jaar fii di wax lii, tay nag laaj naa la ?_
_Mu ne ko waaw kay ! Sama loxo bii, damaa gisoon ku nappi woon ba am i jënam yu baax, ma ëpp ko doole nangu ko, mu ne ma bàyyi naa la ak Yàlla ! Ma dem tuuti sama baaraam bi tàmbalee metti tëha sedd, ma dem cib fajkat mu ne ma jàngoro ji mu ci gis, fàww dagg baaraam bi rekk a ciy pexe, dal di koy dagg._
_Ma dem mu tëha wér, ma demaat ci beneen mu ne ma fàww dog loxo bi ci mbagg mi bala a jàll ci yaram wi rekk a ciy pexe, dal di koy dog._
_Ma jóge fa amatuma jàmm ba ñu yóbb ma cib sëriñ mu ne ma, dangaa tooñ nit mu bàyyi la ak Yàlla. Samay bokk dal di jóg di ko wër ba gis ko, jéggalu ko mu jéggal ma, ci laa ame jàmm._

*_Am na ñaari xale yu doon laale ba Sëriñ Bi yëg leen woo leen ñu ñëw, mu laaj leen lu ngeen jote ? Kenn ka ne ko da maa def nàngam ma dal ci kawam._*
*_Mu leen : "Bu la nit tooñee nga ne dangay jëf ba mu faju, day soppliku sawara lakk la ; boo nee dangay wax ba mu faju it, mu soppliku gaynde fàdd la. Kon ana noo war a def bu ñu la tooñee ? Dangay muñ, Yàlla fayul la, fay la ca muñ googee."_*

Adresse

Tivaouane

Téléphone

+221772057724

Site Web

Notifications

Soyez le premier à savoir et laissez-nous vous envoyer un courriel lorsque Soppey Sëriñ Saaliwu kutiir publie des nouvelles et des promotions. Votre adresse e-mail ne sera pas utilisée à d'autres fins, et vous pouvez vous désabonner à tout moment.

Contacter L'entreprise

Envoyer un message à Soppey Sëriñ Saaliwu kutiir:

Partager